Kansul Muhtadin

Publié le 30 juillet 2025 ·

4000 CFA

Téere ngi bu jëm ci yar ak teggin ñeel sunuy jëflante. Waaye nag aji-taalif ji da koo joyal jëme ko ci diggante doom ak baayam. Diggante boobu ñi ngi ci jublu diggante Sëriñ Tuubaa XLML ak Sëriñ Maam Moor Anta Sali Kan. Looloo waral kon fàww ñu gëstuwaat jaar-jaari Sëriñ bi ak njëlbeenub njàngam ak i gëstoom ca ba muy door ak ban taxawaay la baayam amoon ca joojee jamono.
Kon it yell na ci nun, ñu jële ci ay jàngat ak i bind ñeel doxiinu sunu mboolaay (société), sunug njaboot ak sunuy biri diine.

Ay jikko ak melokaan yu rafet dina feeñ ci liy ñëw ci nettali bi te yu ci ëpp nag Maam Ceerno wane na ko jëmal na ko itam ba ñépp gis ko, ngir dañoo namm aji-dawal ji téere bi xam ni li baay def ci doom, doom bu farloo man na koo def ci ay rakkam ba ci sax i mbokkam ak ñu dul ñoom sax.

Catégorie :

Description

Te saasu ngeen gis ni njaboot gi day gën a tasaarook a yaatu kon yell na ñu xamal ndooraan gi ci fexe nàndal ko cëslaayi diineem ak keno yi ko teyee ak yi nu digle ak jikko yi nu gëram yi te lépp tukkee ci Yónnent bi ﷺ.
Ci noonu aji-taalif fas na yéene àndi fii yeenat ci ay tomb ci téere bi niki wéetal Yàlla (tawhiid), àtte jëf yi mu  »shariya » ak cellal gi ci aaju muy  »tasawuf » li ëpp nag ñoo ngi koy nar a toxale ci téere Sëriñ Àllaaji Mbàkke yi jëm ci leeral dundug Sheex Ahmadu Bàmba.

← Toutes les actualités